Connectez-vous S'inscrire
PRESSAFRIK.COM , L'info dans toute sa diversité (Liberté - Professionnalisme - Crédibilité)

HOMMAGE A AL AMIINE ABDOUL AZIZ SY



HOMMAGE A AL AMIINE ABDOUL AZIZ SY
RAPPEL A DIEU DE SERIGNE  ABDOUL AZIZ AL AMINE LE JEUDI 21 SEPTEMBRE 2017
 ET ENTERRE LE VENDREDI 22 SEPTEMBRE 2017 AVANT LA PRIERE DU VENDREDI
TALIIF A L’HONNEUR DU GARDIEN DU TEMPLE DE MAWDO.

BISMILLAHI RAHMANIR RAHIMI
GANNAW BAMA TAMBAALE
DI JÙLLI CI GËNN DI MBIDEEF AKKI SAABAAM YA
JAAM WEYNA SAŊŊAM NIKKO
GOBBAR DAMNA CA WAARWA BOON WACCNA
FUKKI AT AK JUROOM ŇAAR 
LASSA WEYJÙR TANNLA CA TANEEFYA
ŊA NÈKK MEEW MU WEEX TALL 
CI BIIR KEEPAARU LEER
ŇU DILA DIGGЁL ŊEY JЁFFE SE DOO TAYYI
KU YAGG CIB TEEN BAAG FEKK LACCA
KU YAGG DI TOPPE DINAŇULA MUSSA JIITЁL
DÁLLU SEEXAL XALIIFA 
ŊA MUSSA NEKK BA ŊAY TUUT TANK 
MUSSOO DEŇ DI WЁY CI NDIGЁLU 
SEY WEYJUR AK SEY MAK
WOYOFFOON ŊA DI XOP,  NUŊUWOON ŊA NI DALLË
YARR AK TARBIYYAA LAKKO MEYYOON
KUDDUL TOPPE KEN DULA TOPP
TOPPE ŊA BA FAF YЁRЁMЁTOO SA BOPP
SA KADDU BAL LAWOON ŊIRR DЁGG GII KO LALOON
KU SUŇU BOROOMBAAXE REKKЁ KOY DEEKU
SEY TETTAL YEPP YAAŊIKO JЁMEWOON 
CI DIINE JI, CI TARIIXA BI, CI MBOKK GI, 
CI TAALIBE YI AK CI NDAW YI
AL AMIIN YAAY PAAKA BU KEN 
DUL JIITUCI MBARRAM
DI NDIOBOOTU MAWDO GI
XEJOLOOCIWOON KEN 
NI KENN DOYULACIWOON KUDUL YAW DONG
MUSSOO CI SEET PARPARLOO, 
WALLA MBOKOO CI GAŇO AK CI MEEN
DЁGG REKK DOONOON SA WEERU WAAY
TEKK KO CI CHARIA, AXIIXAAK TARIIXA
NDOKK ŊA TEELA XAMNI
YALLA REKK DI BOROOM DЁGG
AL AMIINE DI KII ŇU WOOLU
BA TANNЁKO CI TAANEEF YI
WOYOFFOON ŊA LOOL 
WAA NDE XENN YOBULLAWOON
DOOMI MBЁROO JAAŊIL BËRE DESS NALLA ŇAMM
TAXXAWAAYU SEYDI ABUBAKAR
CA FULLAM AK RAGGAL YALLA GA
TAXX MU DAKKAL JULLIG JUMMAA GANU NAARBA 
DIWOON MUSSAFIR CA TIVAOUANE
TAX RAKKAMJA CHEYXUL XAWMI MANSUUR 
BAKKË KO CA WAYYAM WA « YA AJABAN »
POROX NDOLLU YAXX KAT YEPP CI ËTTUB MAWDO 
FATT ŊA LEEN ŊIRR SA YITTE
SEYTAANE RUSS BA FAFF NDËRMEELU
ŊIR ŇAKK FUMU JAAR DI JOOY NAAN WËY FUMA JËMM
BËT AK NOPP GEEMEEŇU LANTINOOR REY SEEN NOON
SY AL AMIINE ËMMBËLOON NGA ŇEEP SEEN SUTTURA
SEY FANN GATTNA LOOL CI ATT TE GUDD LOOL CI JËFF 
SE DOOTUŇU FEY BA MUKK
MANDEY FOOGOON NAANE SUMEY ROOŊOOŇ
DËYNA SA BAMAY YOOR SUMA WEYJUR CI BIIR SUUF
SY AL AMIINE SA DEMGII XAWNAMAA LABBAL 
CI BIIR GEEJU ROONGOOŇYUMA
FOOGOON NI DEEYNA BU YAGG
YUXATT YU MEETI TE TARR LOOL TIITËLNA 
ABUL ABASS AK FATIMA SUMAY DOOM
SEEN NDEY AISHA DIMA WAAR 
MA DEGGLEEN ŇUNAAN LU BAAY DI JOOY
MA TONTULEEN NELEEN
KI MAY JOOY REK JARRA JOOY
WEERU MARS ŊA JËL XILAAFA GI
SEY WEYJUR ABUBAKAR AK MANSUUR
WACCI LËGGEEY CI MARS
WEERU SATTUMBAR ŊA WACC LËGGEEY 
NISSA TURRËN DOO AK SA YAAY
SA SOPE SOXNA MAREME KUNTA SIDY
SA NJIUBA TAXX JULLITU 
SENEGAAL YEPP NE YAWWA
CI JULLEE NEEWU GAALU LE JOOLA
NAŇU JIITELEWOON DABAX SE TURËNDO
CA DISKUURAM BA CA MAKKA
NA SEEXAL XALIIFA DIWOON LAMPU DIINE
CI FII CI SAWU JÁNT AFRIKKIYA
JULIT AK NASSARAN YI YEPP NANGULOON KOKO 
DAAN WAXX, DI JËFF, TEY DOGGAL
SE BENN FEEWALOO DU AM
WEERU KOOR, TABASKI, TAMXARIT AK SHAABAAN
AK LEPP LU WOON SOXLAS JULLIT YEP
DAANA CI TAXXAW BAMU MATT SËK
WALLAHI DIINE ISLAM BAA ŊICCI
GUDDI YU BËT SETTA GUL
CI MATTU BU YAGG LOOL SE TARR
WAANE XEL ŇAAR NEWWUL CINE
AL AMIINE BOKKOON ŊA 
CI DOOM YII MU DAAN SAGGOO
MISKIINYI JAXLENAŇU XAAT
DESS DI YUUXU WALLOO
DI JOOY NAAN WËY FUŇUKOY JËLEETI
AL AMIINE YAA NEWOON DOCTORU AAJO YI
AK BËGGUBËGGU NEEW DOOLE YI
CI SEEN NDEEKI, SEEN AAŇ AK SEEN REER
CI XARRI TABASKI YII ŊA DAAN LEEN
SEDDELE BA KENN DU MERR
CI YËRE YULEEN DI TAARAL RAWWATINA JIRIM YI
SY AL AMIINE YA NEWOON 
DALL, BËT, NOPP AK LOXXOOY
SEYDI ABUBAKAR AXXI RAKKAM
SEYDI MUSTAFA SY JAMIIL AXXI RAKKAM
BOON SY ABDU AL AMIINE 
FOOY AMME NOFLAAY AK WËRR GU YARAM
ŊIRR YENN BU DIIS YIILA MAGG YI YENNOON
SE WONKU LO,FITTËRLUWO SE SALITOO
WAANE BOKK CA KEEPARU MAWDO 
SA XADRATUL MUNTAZZAAR JAROON NAKKO
KOLOORE AK WOLLOORE 
MATTALE ŊAKO MU MATT SЁKK
SA DIGGЁNTE AK SA WEYJUR WA 
SOXNA MAREME KUNTA
BA CI GANNAAWOOM 
SA LOXXO DEŇUL CI NDIOBOOTAM
CI FEY KURANG, NDOX AK DUND
AMNA LUMACI XAM
WAANE AY SETTЁM YII DI SEYNABU, 
FATU KUNTA AK GOORO PUY
DOYNAŇUMA CI SEEDE 
SA JЁFF YU REFETT YOOYU
ЁTTUB TIVAOUANE DISSA GEEW 
BOO MUSSULLA WANTEER AL SOOFANTAL
BA TAXX XARR KANAMAM ALADAWMEWU
SA YITTEEKO SABAB
TERAL ŊA MAWDO AK SEY BAAY SAGGAL ŊA LEEN 
BA FAF SUŇU BOROOM FEYLA CI SEEN BARKE
XOTTI ŊAFFA AY JUNNEY HECTAR CI ALLU TIVAOUANE
JAGGLELKO TALIBE SEEX YEPP
ŊIRŇU ŇËW DËKKSI
SA XEL MUSTA LËNT NGIR ŇAAKULOO GIS GIS
SA XOL MUSTA LËNDËM NGIR ŇAAKULOO YËRMANDE
LUNE JAKK KENN DUKKO JEEX
NA SUŇU BOROOM MOTTALI 
SA YEENE SISSA MBËBET YÈP
ŊA JЁMELEWOON KO 
CI UMMA ISLAM BI YÈP
CI TARIIXA TIIJAANBI, CI MBOKK GI, 
CI TAALIBE YI AK ASKANWI YEP
XELŇAAR AMUL CI NAXXAR BII ŊA YËGG
CI NATTU AK TIIS YII JULITTU ROHINGYAS
CA BIRMANIE DI JAAMAARLOOL
GANNAW BA ŊACCI ADDOO 
NAXXARLOOKO CI SA BIIR XOLL
ŊA FIRNAALKO SIISSA LAMIIŇ
TEKK CA BATTAAXAL 
BU WËRR ADUNYA WËR NGËL KËB
SA JËFF JEEKO KAWWE WAAY
JËFF BU DOOTUL FEY BA MUK
LEER NDAAŇ NI LAMPU NGOR
XENN ŊA CI KENNU MBAAR 
BII ŇUUY WOOWE SENEGAAL
ŊA NEWOON KISLAAY BU YANKUL TE FËSS LOOL
CI DIGGËNTE SYNDIKA AK POLITISIENS YI
ŊALLA WAAY NAŇULA ROOY
CI SA BËGGUG REWMI 
SA YARAM WU SUTTËNTE WOON
TEREWULA WOONNADEM WOTTE JI
JËL SA DARAJA TEKK CI SUUF 
JIITËL SA REPUBLIQUE
YAWDE XAM ŊA LUY 
MA PATRIE AVANT MON PARTI DI TEKKI
ŊALLA WAAY NALLA NDAWWI REWMI
ROY CI GËSTU XAMXAM AK BËGGËKO
AK FONK LËGGEEY NGIR TEXXE
YAKAAR NAANE MOO GËNN FUUF
FECC, XAXXAR, WEY, LOTORI AK SAMBA MBEYAAN
NGALLA WAAY NDAWWI REWMI
TASSLEEN SEENI ASC FUTBALU NAWETAAN YI
SE SOPPI KO AY ASC MBEY NGIR DUND AK DUNDËL
SUUF SAA ŊII NE YAMBALANG DILEEN XAAR
ŇU BARRI CI ASKANWI LAPP NAŇU CI BIIR GEEJU
MASLAA AK ANDDU RAGGALANTE GANNAWAK AADDA 
YAW DE SY AL AMIINE MUCC NGA CI NATTU YOOYE
DËGG NGEY YEEWO, DIKKO YENDOO, DIKKO FANNAANOO
LAMA SOXNA MAREME KUNTA
WAXXOON SA TAAXU NDIAASSAAN
NIMA DOOM SENEGAAL GII KUFFI SAXXOO
YALLA NEENA, YONANTËBI NEENA, ALAJI MALIK NEENA
WEETAAY DINNA LA SONNAL WAANE NDOK
SY AL AMIINE DEM ŊA WEETAL ŊAŇU
WAANE SA GANNAW TAARU LOOL
YALLNA SUŇU BOROM TAARAL SA NEKKIIN
CI KEEPAARU MAWDO, SEEXAL XALIIFA AK SEENI SERIŇ
LÈY JEEXNA BU YAGG CI DOOM ADAMA YII 
BAŇUMAWDO TAGGATTEEŇU XAM 
RASSULLILLAH TE NËB BOPPAM
WAANDE SY AL AMIINE 
DEKKALLAAT ŊA LÈY MU FAF JEEX BA FAW
CI XARR KANNAM BU TAARU BII 
ŊA JOOXAAT TIVAOUANE
KU DOON LACC TE SAKKU WAAYU 
FULLA, FEYDA AK GЁM SA BOP
SOOY ŊA NE DAAM SAAJ GЁ WЁYNA
SA FULLA TAXXOON NA BEN MINNDAFOON
MUSSULAA XEEBAL SA SЁRIŇ, SA BEESAK SA SOXLA
SUŇU BOROM LA SOOBOON MU TANNLA CI TANNEEF YI
JЁL LA BA ŊEY TUUT TANK DÈNK LA SЁRIŇ BABAKAR SY
TARXIIS, JÈNG AK PARPARLOO MUSSOO SEE JAAR
SA TЁDDE ŇAAXAANAAY TAXNA AMOO WOON
YAAY AY YAAY ŊA AMMOON
SOXNA MAREME KUNTA DAANA SAGGOO ŇENT YII:
- JUROOMI DЁRЁMU ŊURD YUKKO MAWDO MEY CA NDAR ŊIR JÁNGUK AL XURRAAN NAM BU REFET
- NEKK CI KEPPAARU SEYDI ABUBAKAR
- AM DOOM JU MELNI SERIŇ ABDOU
- TAAXXU NDIAASSAAN BIIKO SERIŇBABACAR NEEXALLE
GORR DEY FIIR CA LAKA TAXA JUK
GORR DEY FIIR CA LAMU AM
GORR DEY FIIR CA LAMU ŊЁB
GORR DEY FIIR CA LAŇUKO DÈNK
GORR DU SOPPEEKU BA XEEP FAMU COSSAANOO
SY AL AMIINE TIVAOUANE 
ŊA JUDDOO, FA ŊA MAAGGE
FA ŊA TOOK, DESSFA BA XЁY NI MESS ŇU DENC LAFFA
BILLAHI YA BARI ŊORR
WALLAHI NDONAL MAWDI GII
AK NDONAL BOROM BONNET KARRE GII
AL AMIINEŊËBBËL ŊËŇUKO BA DARRA ROTTUCI
LAMMA SOXNA MAREME KUNTA WAX
CI JIKKO SЁRIŇ BABAKAR SY LEPP ŊALAMBOO
SO LAAN XAAJALLE MATTALE
BA KOO JOX CЁRЁM DU MERR
YA YENNU YENBI DOOREKO 1944 CI SA 17 ANS
DI DOX AK MOOM BA 2017 CI SA 90 ANS
73 ANS NGA YENNU YEN BI SE WONKULOO
TE BIICOO AK MBAALLOOFEKKU LACCA 
LUDUL ŊANI TEK BA XЁY NI MESS
BILLAHI YA BARRI ŊORR
SEY MAG REKK BAX WUUTÈK YII MA XAM
LA BUURU MAROC SEEDELA REKKAY DЁGG
SA LEPP YIWLA TEGGU CI ŇUB, DOYLU,
XAM XAM AK AM AM BOO DAAN SEDDELE
BOROM BEN MELLO REK ŊA MUSSA DOON
GORR DU SOPPEEKU MUK
LU DIISSOON WOYOFFAL ŊAKKO
LU XATTOON YAATAL ŊAKKO
LU LЁNDЁMOON LEERAL ŊAKKO
AMERIK, EUROPE, ASIE, OCEANIE AK AFRIK
ŇEPP ŊILLEY ŇAANAL ŊA TABBI 
CI YЁRMANDE SU ŇU BOROOM
NA SUŇU BOROOM WALLU SA RAKK 
SEYDI ABUBAKAR SY MANSUR
BII LA WUUTU CI XILAAFA GI
ŇUN ŇEEP DI MBOK GI AK TAALIBE YI
NAŇU ÁND JOXXANTE SE TAPPE XOLYI 
TÈKK CI JAXANTE LOXXOYI
SE MUY DЁG GU SAX BA FAW
ЁTTU MAWDO BII DI TIVAOUANE
DЁGGU REKKO KO LALL
NA YALLA WOYOFFAL TOLL YENN BII ŇULA DÈNK
YALLA NÁNKO MURLOO SE ŊA YAGG AK MOOM
SE LEPP REFET SE TAARU LOOL 
NE YAW REKKO KO YEELLO
SY ABUBAKAR MANSUUR YAGG FI LOOL SE WЁRR
AK SA RAKK PAP MALIK SY ABUBAKAR
BII SЁSS CI YAW RЁK SE DULLA RЁK
ŊA TANNKO MUY SEY BЁT, SEY TANK,
SEY LOXXO AK SA LAMIŇ
TOFTAL CI SEY RAKK :
SIDI AHMETH SY ABUBAKAR AKKI RAKKAM
SAID MAWDO SY DABAKH AKKI RAKKAM
SAID MALIK SY HABIB AKKI RAKKAM
YALLA NALLA SUŇU BOROM ŇAGGELA
ŇATTI MUBIININ AK ŇENTI MUBIINUN
YAMU WЁRЁLE SORATU YAASIIN
BA ŊA MUCC BEY MUCCЁLE
ALLAHOUMMA SALLI ALA 
SEYDINA MUHAMADIN WASSALIM

Par l’adjudant en retraite Ndiapaly GUEYE,
Secrétaire  général du Front pour l’Ouverture, l’Unité et la Défense de la République (FOUDR),
Ancien présentateur de l’émission radiophonique « Armée-Nation » à la RTS,
Diplômé de la Defense Language Institute (DLI) - Diplômé de la Defense Information School (DINFOS) aux Etats-Unis d’Amérique,
Spécialiste en Relations publiques.
Email : ndiapalygueye@yahoo.fr


Vendredi 13 Octobre 2017 - 21:27


div id="taboola-below-article-thumbnails">

Nouveau commentaire :
Facebook Twitter